

Moytu di joxante loxo ak di saafoonte

Di faral di raxas sunuy loxo ak ndox ak saabu,
tàmbalee ko ci biir loxo yi

Jëfandikoo muswaar saa su nuy sëqët walla nuy tisli te bu nu ci noppee, nu sànni ko ci póllu mbalit

Di tisli ak di sëqët ci sunu biir conco, su fekkee ni amunu muswaar

Moytu di jege ku am màndargay tawatu girib (yaram wu tàng, soj, sofo yu metti)

Moytu di laal sunu gémmiñ, sunu bakkan walla sunuy bët ak sunuy loxo

Dànd ki nuy waxal lu tolloo ak meetar

Toog sunu kër te moytu di génn génn bu amul njariñ
